9 Ba Yesu juge fōfale, mu gis nit ku tūda Matthew, mu di tōg cha galakukay ba: mu wah͈ ko, ne, Topa ma. Mu jog, te topa ko.
Philip, ak Bartholomew; Thomas, ak Matthew publican bi; James dōm i Alphæus, ak Thaddæus;
Mu ne len, Dem len yēn it cha tōl ba, te di nā len joh͈ lu ela. Ñu dem.
Wande Yesu ne ko, Topa ma, te bayi ñu dēle ña ñu sūl sēn ñu dē.
Am on na, ba Yesu tōge di leka cha nēg ba, publican yu bare ak i bakarkat ñou, te tōg ak mōm ak tālube am ya.