5 Lan a chi gen a yomba wah͈, ne, Baal nañu la sa i bakar; wala ne, Jogal, te doh͈?
Ñu yub ko nit ku lafañ, teda chi lal: ba Yesu gise sēn ngum, mu wah͈ ku lafañ ka, ne, Suma dōm, na sa h͈ol dal; baal nañu la sa i bakar.
Wande ndah͈ ngēn mun a h͈am ne Dōm i nit ka am na chi suf sañsañ di baale i bakar, (fōfale mu ne ku lafañ ka,) Jogal, gadul sa lal te dem chi sa ker.