Mu h͈am sēn i h͈alāt, te ne len, Ngur gu neka gu h͈ajāliku chi bop’ am, di na ñou chi ntaste; te deka bu neka, mbāte nēg, bu h͈ajāliku chi bop’ am du tah͈ou:
Yesu h͈am ne buga nañu ko lāj, te mu ne len, Ndah͈ lājante ngēn chi li ma wah͈ on, ne, Chi wah͈tu wu new du len ma sêt, te chi wah͈tu wu new di ngēn ma gisati.
Mu ne ko ñetel i yōn bi, Simon, dōm i John, sopa nga ma? Peter nah͈arlu ndege nôn na ko ñetel i yōn bi, Sopa nga ma? Te mu ne ko, Borom bi, h͈am nga lu neka; h͈am nga ne sopa nā la. Yesu ne ko, Samal suma i nh͈ar.