37 Fōfale mu wah͈ i tālube am, ne, Chi dega ngōbte gi fūs na, wande ligeykat yi new nañu;
Ndege ngur i ajana niro na ak bena borom‐ker ku gēna chi sūba têl, ndah͈ mu binda i ligeykat chi tōl am.
Dem len mbōk, def i tālube h͈êt yi yepa, te batise len chi tur i Bay ba, ak Dōm ja, ak Nh͈el mu Sela ma:
Mōtah͈ ñān len Borom i ngōbte gi, ndah͈ mu yōni i ligeykat chi ngōb am.