36 Wande ba mu gise mbōlo ma, mu yerem len, ndege da ñu jāh͈le, te tasāro niki nh͈ar yu amul samakat.
Wande dem len chi i nh͈ar i ker i Israel yu rēr ya.
Mu gēna, te gis mbōlo mu rey; mu am yermande chi ñom, te weral sēn i jarak.
Wande mu tontu, ne, Fi nh͈ar i nēg i Israel yu rēr yi reka la ñu ma yōni.
Yesu ô i tālube am fi mōm, te ne len, Am nā yermande chi mbōlo mi, ndege anda nañu ak man lēgi ñet’ i fan, te leku ñu dara; du ma len demlo te leku ñu, wala h͈ēchna di nañu ñaka dōle chi yōn wa.