19 Yesu jog, ak i tālube am, te topa ko.
Yesu ne ko, Di nā dika te weral ko.
Ba mu len wah͈andô yef yile, bena kēlifa ñou, te dagān ko, ne, Nistey suma dōm ju jigen dē na; wande ñoual, teg sa loh͈o chi kou am, te di na dundati.
Jena jigen, ku am on h͈up i deret fuk’ i at ak ñar, ñou chi ganou am, te lāl mbichirān i mbūba’m:
Yesu ne len, Suma dūndu mō di def mbugel i ka ma yōni on, te motali ligey am.