17 Du ñu def itam biñ bu ês chi mbūs yu maget: wala mbūs ya h͈ar, biñ ba tūru, te mbūs ya yah͈u: wande di nañu def biñ bu ês chi mbūs yu ês, te ñar ña dēnchu.
Ken du dāh͈e nchangay lu maget ak lu deger, ndege la ñu jel dāh͈e ko di na h͈oti nchangay la, te h͈otiku ba di na gen a rey.
Ba mu len wah͈andô yef yile, bena kēlifa ñou, te dagān ko, ne, Nistey suma dōm ju jigen dē na; wande ñoual, teg sa loh͈o chi kou am, te di na dundati.