Yesu ne len, I mbok’ i nēg i borom‐chēt ga, ndah͈ mun naño nah͈arlu ba borom‐chēt ga neke ak ñom? Wande jamāno di na diki ba ño fabi borom‐chēt ga cha ñom; bōbale di nañu ôri.
Du ñu def itam biñ bu ês chi mbūs yu maget: wala mbūs ya h͈ar, biñ ba tūru, te mbūs ya yah͈u: wande di nañu def biñ bu ês chi mbūs yu ês, te ñar ña dēnchu.