10 Am on na, ba Yesu tōge di leka cha nēg ba, publican yu bare ak i bakarkat ñou, te tōg ak mōm ak tālube am ya.
Ba Pharisee ya gise lōla, ñu ne i tālube am, Lutah͈ sēn Borom di leka ak i publican ak i bakarkat?
Ba Yesu juge fōfale, mu gis nit ku tūda Matthew, mu di tōg cha galakukay ba: mu wah͈ ko, ne, Topa ma. Mu jog, te topa ko.
H͈am nañu ne Yalla du dēga i bakarkat: wande su kena neke jāmukat i Yalla, te def mbugel am, mōm la di dēga.