Mā len di batise chi ndoh͈ ndig rēchu; wande mōm ka di topa chi man, mō ma gēti kantan; daganu ma yubu i dal’ am; mō len di batiseji chi Nh͈el mu Sela ma ak safara;
Ndege nit lā ku neka chi run i kēlifa, te am nā i h͈arekat ya ma ēlif; te ku ma cha ne, Demal, mu dem; te ku ma cha ne, Ñoual, mu ñou; suma jām, Defal lile, mu def ko.