6 Ne, Borom bi, suma bukanēg anga teda cha ker, lafañ, te sona bu miti.
Dēgdēg i tur am dem cha bir Syria yepa; ñu yub ko nit ña op’ on ñepa, ña jangaro ju mun a don ak nchono jap’ on, ak ña i jine jap’ on, ak ña say, ak ña lafañ, te mu weral len.
Yesu ne ko, Di nā dika te weral ko.
Ñu yub ko nit ku lafañ, teda chi lal: ba Yesu gise sēn ngum, mu wah͈ ku lafañ ka, ne, Suma dōm, na sa h͈ol dal; baal nañu la sa i bakar.