5 Ba Yesu h͈arafe chi Capernaum, bena saltige ñou fi mōm, te dagān ko,
Te you Capernaum, mi yēkatiku cha asaman, di nañu la sufel be chi nāri: ndege koutef ya ma def on chi you, su ñu len def on cha Sodom, kôn mu des bentey.
Saltige ba nak, ak ña nek’ on ak mōm, di otu Yesu, ba ñu gise yengatu’ suf sa, ak yef ya am, ñu tīt lol, ne, Chi dega kile Dōm i Yalla la.
Te juge Nazareth, mu ñou deka chi Capernaum, bu jegeñ gēch ga, chi wet i Zebulun ak Naphtali:
Yesu duga chi gāl, jala, te ñou chi dek’ am.