33 Ña len don sama dou, dem chi bir deka ba, te wah͈ lu neka, ak lu jot nit ña jine jap’ on.
Dēgdēg i tur am dem cha bir Syria yepa; ñu yub ko nit ña op’ on ñepa, ña jangaro ju mun a don ak nchono jap’ on, ak ña i jine jap’ on, ak ña say, ak ña lafañ, te mu weral len.
Ba ngon jote, ñu yub ko ña i jine jap’ on, te mu gēne malāka yu bon ya chi ñom chi bāt am, te weral ña jēr on ñepa:
Mu ne len, Dem len. Ñu gēna cha nit ña, te duga chi mbām ya: gēta ga yepa dou ak dōle chi kou bereb bu koue di jem chi gēch ga, ñu rēr chi ndoh͈ ma.