31 Te jine ya dagān ko, ne, So ñu gēnê, bayi ñu ñu dem chi bir gēt’ i mbām ya.
Dēgdēg i tur am dem cha bir Syria yepa; ñu yub ko nit ña op’ on ñepa, ña jangaro ju mun a don ak nchono jap’ on, ak ña i jine jap’ on, ak ña say, ak ña lafañ, te mu weral len.
Bu len joh͈ la sela h͈aj ya, te bu len sani sēn i takay chi kanam i mbām; ndig so otuwul di nañu len degat chi sēn run tanka, te walbataku h͈oti len.
Gēt’ i mbām yu bare sorey on nañu fale di far.
Mu ne len, Dem len. Ñu gēna cha nit ña, te duga chi mbām ya: gēta ga yepa dou ak dōle chi kou bereb bu koue di jem chi gēch ga, ñu rēr chi ndoh͈ ma.