30 Gēt’ i mbām yu bare sorey on nañu fale di far.
Bu len joh͈ la sela h͈aj ya, te bu len sani sēn i takay chi kanam i mbām; ndig so otuwul di nañu len degat chi sēn run tanka, te walbataku h͈oti len.
Ñu h͈āchu, ne, Lan la ñu jote ak you, you Dōm i Yalla? Dā fi dika ndig geten ñu bala wah͈tu wa jot?
Te jine ya dagān ko, ne, So ñu gēnê, bayi ñu ñu dem chi bir gēt’ i mbām ya.