3 Yesu talal loh͈o am, te lāl ko, ne, Di nā tah͈ nga set. Chi tah͈ouay ba mu dal di wer.
Fōfale mu wah͈ gōr ga, ne, Talalal sa loh͈o. Mu talal ko; mu wer niki benen ba.
Te ba mu wah͈e nōgule, mu h͈āchu be cha kou, ne, Lazarus, gēnasil.
Su ma deful on chi sēn digante ligey ya ken mosul on a def, amu ñu kon bakar: wande lēgi nak gis nañu te bañ ma ak suma Bay itam.
Ndege naka Bay ba dēkali ñu dē ña, te tah͈ ñu dūnda, nōna sah͈sah͈ la Dōm ji itam di na dūndalo ku mu buga.