2 Ab gāna ñou fi mōm, te ñān ko, ne, Borom bi, su la nêh͈e, mun nga ma setal.
Weral len ñu opa ña, setal len gāna ya, dēkali len ñu dē ña, dah͈a len i jine: ndig dara ngēn ko ame, maye len ko ndig dara.
Defu fa i koutef yu bare ndig sēn gumadi.
Te ña neka chi gāl ga jāmu ko, ne, Chi dega yā di Dōm i Yalla.
Wande mu ñou te jāmu ko, ne, Borom bi, lêl dimali ma.
Mōtah͈ jām ba sūka, te dagān ko, ne, Borom bi, muñal ma, di nā la fey yepa.
Ba ñu h͈arafe cha nēg ba, ñu feka gūne ga ak Mariama ndey am; ñu sūka te jāmu ko; ñu ūbi sēn i wah͈ande, te jebal ko i maye: wurus, fufata, ak mira.
Fōfale ndey ī dom i Zebedee ñou fi mōm, ak dōm am yu gōr, di ko jāmu, te lāj ko lef.
Ba Yesu neke chi Bethany nak, chi nēg i Simon gāna ga,
Ba ñu ko gise, ñu jāmu ko: wande ñena ña gumadi.
Yesu feka len, ne, Mangi len noyu. Ñu ñou, jap’ i tank’ am, te jāmu ko.
Te ne ko, Yef yōyu yepa lā la di may, so sūke chi suma kanam, te jāmu ma.
Ba mu wache cha tūnda wa, mbōlo mu rey top’ on nañu ko.
Ñu ñou fi mōm, te ê ko, ne, Borom bi, musal ñu: ñunge sanku.
Ba mu len wah͈andô yef yile, bena kēlifa ñou, te dagān ko, ne, Nistey suma dōm ju jigen dē na; wande ñoual, teg sa loh͈o chi kou am, te di na dundati.
Te mu ne, Gum nā, Borom bi; te mu jāmu ko.