16 Ba ngon jote, ñu yub ko ña i jine jap’ on, te mu gēne malāka yu bon ya chi ñom chi bāt am, te weral ña jēr on ñepa:
Fōfale ñu indi fa mom kena ku jine jap’ on, ka silmah͈a te lū; mu weral ko, tah͈na nit ka lū on wah͈ te gis.
Mu gēna, te gis mbōlo mu rey; mu am yermande chi ñom, te weral sēn i jarak.
Mu lāl loh͈o am, te fēbar ba bayi ko; mu jog te bukanēgu ko.
Ña len don sama dou, dem chi bir deka ba, te wah͈ lu neka, ak lu jot nit ña jine jap’ on.
Ñu yub ko nit ku lafañ, teda chi lal: ba Yesu gise sēn ngum, mu wah͈ ku lafañ ka, ne, Suma dōm, na sa h͈ol dal; baal nañu la sa i bakar.