15 Mu lāl loh͈o am, te fēbar ba bayi ko; mu jog te bukanēgu ko.
Te dagān ko ndah͈ ñu mun a lāl omb’ i cholay am reka; te ña ko lāl ñepa ñu wer cheng.
Yesu am yermande chi ñom, lāl sēn i but, te chi tah͈ouay sēn i but gis, te ñu topa ko.
Ba Yesu h͈arafe chi nēg i Peter, mu gis goro am teda, opa ak fēbar.
Ba ngon jote, ñu yub ko ña i jine jap’ on, te mu gēne malāka yu bon ya chi ñom chi bāt am, te weral ña jēr on ñepa:
Yesu talal loh͈o am, te lāl ko, ne, Di nā tah͈ nga set. Chi tah͈ouay ba mu dal di wer.
Jena jigen, ku am on h͈up i deret fuk’ i at ak ñar, ñou chi ganou am, te lāl mbichirān i mbūba’m:
Fōfale mu lāl sēn i but, ne, Naka sēn ngum na ame nōgu chi yēn.