11 Te ma ne len, ñu bare di nañu jugeji cha Penku ak H͈arfu, te jēki ak Ibrayuma ak Isaka ak Yanh͈oba chi ngur i ajana;
Ñu ne ko, Di na rēy nit ñu soh͈or ñōgale chi choh͈or, te lūye tōl am yenen i ligeykat, ñu ko di joh͈i mēñef yi chi sēn wah͈tu’ ñorte.
Te di na yōni malāka am ya ak nchōu i bufta bu rey, te di nañu dajale ña mu tan’ on chi ñenent i ngelou yi, cha bop’ i asaman be cha muj ga.
Rēchu len, ndege ngur i ajana jegeñsi na.
Ba ko Yesu dēge, mu jomi, te ne ña ko top’ on, Chi dega mangi len di wah͈, mosu ma feka ngum gu nu day, dēt, du chi Israel.