10 Ba ko Yesu dēge, mu jomi, te ne ña ko top’ on, Chi dega mangi len di wah͈, mosu ma feka ngum gu nu day, dēt, du chi Israel.
Fōfale Yesu tontu ko, ne, E jigen ji, sa ngum rey na lol; naka nga buga, na ame nōgu chi you. Te chi wah͈tu wōwale dōm am wer cheng.
Te ma ne len, ñu bare di nañu jugeji cha Penku ak H͈arfu, te jēki ak Ibrayuma ak Isaka ak Yanh͈oba chi ngur i ajana;
Ndege nit lā ku neka chi run i kēlifa, te am nā i h͈arekat ya ma ēlif; te ku ma cha ne, Demal, mu dem; te ku ma cha ne, Ñoual, mu ñou; suma jām, Defal lile, mu def ko.