1 Ba mu wache cha tūnda wa, mbōlo mu rey top’ on nañu ko.
Yesu h͈am lōla, te mu sipi fōfale; ñu bare topa ko; mu weral len ñom ñepa.
Mbōlo mu rey ñou fi mōm, and’ ak ña lagi, silmah͈a, lu, tēlekat, ak ñenen ñu bare, nu teg len chi tank’ am, te mu weral len;
Mbōlo mu rey topa ko, mu weral len fa.
Ba ñu gēne cha Jericho, mbōlo mu rey topa ko.
Mbōlo mu rey tope ko cha Galilee, ak Decapolis, ak Jerusalem, ak Judæa, ak ganou Jordan.
Ndege jemantal on na len naka ku am sañsañ, te nekul naka sēn i bindānkat.
Yesu nak ba mu gise mbōlo mu rey chi kanam am, mu eble ñu jala cha genen wet ga.
Ab gāna ñou fi mōm, te ñān ko, ne, Borom bi, su la nêh͈e, mun nga ma setal.