7 Lāj len, te di nañu len may; ūt len, te di ngēn gis; foga len, te di nañu len ūbi:
Ma nêti len, Su ñar chi yēn dēgô chi suf lu jem chi lef lu ngēn di ñān, suma Bay bi cha ajana di na len ko defal.
Te lu mu mun a don lu ngēn di ñān chi ngum, di ngēn ko ami yepa.
Wande ūt len jeka ngur um Yalla ak njūbay am, te yile yepa di na len ko doli itam.
Yēn ñi bon nak, su ngēn h͈ame may sēn i dōm yef yu bāh͈, as sēn Bay ba cha ajana di na may ña ko lāj yef yu bāh͈?
Ndege ku mu mun a don ku lāj, di na am; te ku ūt, di na gis; te ku foga, di nañu ko ūbi.
Yēn tanu len ma won, wande mā len tan’ on, te santa len, ndah͈ ngēn dem te mēña dōm, te ndah͈ sēn mēñef deka: ndah͈ lu mu mun a don lu ngēn di ñān Bay ba chi suma tur, mu may len ko.
Su ngēn deke chi man, te suma i bāt deka chi yēn, ñān len lu ngēn buga, te di nā len ko defal.
Yesu tontu te ne ko, So h͈am on maye’ Yalla, ak ki di wah͈ ak you, ne, May ma ma nān; kōn di nga ko dagān, te mu may la ndoh͈ i dūnda.