5 Mīkar bi, dindil jeka lā bi chi sa but, te ganou ga di nga gis bu set ndah͈ nga mun a dindi felah͈ ba chi sa but i morom.
Wande Yesu gis sēn kēfēr, te ne len, Lutah͈ ngēn di ma fire, yēn nafeh͈a yi?
Lu elal nga di nimeku felah͈ bi chi sa but i morom, te do gis lā bi chi sa but?
Wala naka nga wah͈e sa morom, ne, Bayi ma ma dindi felah͈ bi chi sa but, te lā’ngi chi sa but sah͈?
Bu len joh͈ la sela h͈aj ya, te bu len sani sēn i takay chi kanam i mbām; ndig so otuwul di nañu len degat chi sēn run tanka, te walbataku h͈oti len.