4 Wala naka nga wah͈e sa morom, ne, Bayi ma ma dindi felah͈ bi chi sa but, te lā’ngi chi sa but sah͈?
Njītekat yu silmah͈a yi, ña sēga ab yô, te wona gelem.
Lu elal nga di nimeku felah͈ bi chi sa but i morom, te do gis lā bi chi sa but?
Mīkar bi, dindil jeka lā bi chi sa but, te ganou ga di nga gis bu set ndah͈ nga mun a dindi felah͈ ba chi sa but i morom.