29 Ndege jemantal on na len naka ku am sañsañ, te nekul naka sēn i bindānkat.
Yesu ñou fi ñom, te wah͈ len, ne, May nañu ma kantan yepa cha ajana ak chi suf.
Ndege mangi len di wah͈, Su sēn njūbay sutule njūbay i bindānkat ya ak Pharisee ya, du len h͈araf chi ngur i ajana muk.
Wande mangi len di wah͈, Ku sêt jigen te h͈emem ko, nistey njālo na ak mōm chi h͈ol am.
Wande mangi len di wah͈, Ku fase ak jabar am, lu moy mu di chi njālo, tah͈ na ko mu njālo; te ku sey ak mōm ka ñu fase, njālo na.
Wande mangi len di wah͈, Sopa len sēn i mbañ, te ñānal len ña len di geten;
Am on na ba Yesu sotale bāt yile, mbōlo ma jomi chi njemantal am:
Ba mu wache cha tūnda wa, mbōlo mu rey top’ on nañu ko.