24 Mōtah͈ ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te def len, di na niro ak nit i sago, ka tabah͈ nēg am chi kou doch:
Ndege ku mu mun a don ku di def suma mbugel i Bay ba cha ajana, mō di suma raka, ak suma jigen, ak suma ndey.
Te mangi la wah͈ it, ne yā di Peter, te chi doch wile lā di tabah͈ suma jangu; te bunt’ i nāri du ko fabi.
Kan a di bukanēg mbōk bu taku te têy, bu borom am jītal chi ker am, ndah͈ mu joh͈ len sēn dundu chi wah͈tu wa?
Jurom chi ñom nek’ on nañu ñu ñaka sago, te jurom ña di ñu am sago.
Wande ñu am sago ña yubuāle diwlin chi sēn i ndap ak sēn i lampa.
Wande ñu am sago ña tontu, ne, H͈ēchna du doy chi ñun ak yēn: na ngēn dem fa ña di jay, te jendal sēn bopa.
Tou ba dal, wame wa buna, ngelou la ñou, te dal chi kou nēg bōbale; wande dānuwul; ndege chi doch la sampu.
Te ku mu mun a don ku dēga suma i bāt yile, te defu len, di na niro ak nit ku ñaka sago, ka tabah͈ nēg am chi kou banh͈aleñ:
Su ngēn h͈ame yef yile, barkel chi yēn su ngēn len defe.
Su ngēn ma sope, di ngēn dēncha suma i eble.
Su ngēn dēnche suma i eble, di ngēn deka chi suma nchofel; naka ma dēnche suma i eble’ Bay, te deka chi nchofel am.
Yēn a di suma i h͈arit, su ngēn di def yef yi ma len ebal.