22 Ñu bare di nañu ma wah͈ chi bes bōbale, Borom bi, Borom bi, ndah͈ wareū ñu on chi sa tur, te chi sa tur ñu dah͈’ i jine, te chi sa tur ñu def koutef yu bare?
Chi dega mangi len di wah͈, di na gene dek’ i Sodom ak Gomorrah chi kerog mpēnch’ um Yalla ma as deka bōbale.
Wande ken h͈amul bes bōbale ak wah͈tu wōgale, du malāka i ajana ya sah͈, wala Dōm ja, wande suma Bay bi dal.
Cha ganou ga yenen h͈ēk ya ñou itam, ne, Borom bi, Borom bi, ūbi ñu.
Du ku neka ku ma wah, ne, Borom bi, Borom bi, di na h͈araf chi ngur i ajana; wande ka def suma mbugel i Bay ba cha ajana mōm reka.
Te lile wah͈u ko won chi bop’ am; wande ndege mō nek’ on kēlifa i seriñ ya cha at mōmale, mu wolif ne Yesu war a dē ngir h͈êt wi;