19 Garap gu neka gu mēñul mēñef bu bāh͈, di nañu ko gor, te sani ko chi safara.
Te nistey teg nañu semiñ wi chi rēn i garap ya; garap gu neka mbōk gu mēñul dōm yu bāh͈, di nañu ko dog, te sani ko chi safara.
Garap gu bāh͈ munul a mēña mēñef bu bon, te garap gu bon munul a mēña mēñef bu bāh͈.