14 Ndege bunta ba h͈ocha na, te yōn wa jublu chi dunda h͈at na, te ñu new a ko gis.
Nōnule ña muje di nañu jītuji; te ña jītu di nañu mujeji.
Ndege ñu bare la ñu ô, wande ñu new la ñu tana.
H͈araf len chi bunta bu h͈ocha ba: ndege bunta ba yā na, te yōn wa jublu chi sankute yātu na, te bare na ñu cha tabi:
Otu len i yonent i nafeh͈a ya, di ñou fi yēn chi nchangay i nh͈ar, wande chi bir ño di buki yu fuh͈ale.
Di nañu len gēneji cha juma ya: chi dega wah͈tu wa di na jot ne ku mu mun a don ku len di rēy, di na dēfe ne defal na Yalla ligey.
Yef yile lā len wah͈ ndah͈ chi man ngēn mun a am jama. Chi aduna si di ngēn am ngeten: wande na ngēn degerlo sēn hol; ndig fabi nā aduna si.