13 H͈araf len chi bunta bu h͈ocha ba: ndege bunta ba yā na, te yōn wa jublu chi sankute yātu na, te bare na ñu cha tabi:
Wande suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn tej bunt’ i ngur i ajana chi nit: te yēn chi sēn bopa du len cha tabi; te nanguwu len ña buga tabi ñu tabi cha.
Fōfale di na wah͈ ña chi chamoñ am, ne, Randu len ma, yēn ñi alaku, dem len cha safara su dul jêh͈, ba ñu wājal on Seytane ak i malāk’ am:
Ñile di nañu dem chi ndān gu dul jêh͈: wande ñu jūb ña chi dunda gu dul jêh͈.
Rēchu len, ndege ngur i ajana jegeñsi na.
Mēña len mbōk mēñef yu mot chi rēchu:
Ndege bunta ba h͈ocha na, te yōn wa jublu chi dunda h͈at na, te ñu new a ko gis.
Mā di bunta bi: chi man su nit h͈arafe, di na mucha, te di na tabi chi bir, gēna cha biti, te feka mporlukay.
Yesu ne ko, Man mā di yōn wi, ak dega gi, ak dūnda gi; ken du ñou fi Bay ba, lu dul chi man.