4 Ndah͈ sa sarah͈ di nubu, te sa Bay ki di gis lu nubu, di na la yōl.
Te ku mu mun a don ku maye bena chi ñu tūt ñile mbatu’ ndoh͈ mu seda reka, chi tur i tālube, chi dega mangi len di wah͈, du ñaka yōl am.
Ndah͈ do mel naka ku di ôr chi nit, wande chi sa Bay ki chi nubu; te sa Bay ka gis lu nubu, di na la yōl.
Wande so di sarah͈e, bul sa loh͈o’ chamoñ h͈am lu sa loh͈o’ ndējor di def:
Wande you, so di ñān, dugal chi sa bir nēg, te ba nga teje bunta ba, ñānal sa Bay ki chi nubu; te sa Bay ki di gis lu nubu, di na la yōl.