24 Ken munul a jāmu ñar i borom: ndege di na bañ kena, te sopa kenen; mbāte di na topa kena, te jēpi kenen. Munu len a jāmu Yalla ak alal.
Fōfale Yesu ne ko, Randu ma Seytane, ndege binda nañu, ne, Na nga jāmu Borom ba sa Yalla, te na nga ko topa, mōm reka.