Matthew 6:2 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907
2 So di sarah͈e mbōk, bul buftalo chi sa kanam, naka nafeh͈a ya di def chi juma ya ak mbeda ya, ndah͈ ñu am teranga chi nit. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.
Su ngēn di ôr, bu len am kanam gu dīs niki nafeh͈a ya; ndege di nañu ñaulo sēn i kanam ndah͈ nit ña gis ne ñunge ôr. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.
Su ngēn di ñān, bu len def niki nafeh͈a ya: ndege sopa naño tah͈ou di ñān chi juma ya ak chi mbeda ya, ndah͈ nit gis len. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.