19 Bu len dajale alal chi aduna si, fa gasah͈ ak h͈omak di yah͈a, te fa i sachakat di daji te sacha:
Yesu ne ko, So buge mot, na nga dem, jay lo am, sarah͈ ko miskin ya, te di nga am jur cha ajana: te ñou, topa ma.
Wande dajale len alal cha ajana, fa gasah͈ ak h͈omak dul yah͈a, te fa i sachakat dul daji, mbāte sacha: