12 Te baal ñu suñu i bakar, naka ñu baale ña ñu tōñ;
Ndege lile di suma deret i koleri gu ês, ja di tūru ndig ñu bare ndege mbaale’ i bakar.
Ñu yub ko nit ku lafañ, teda chi lal: ba Yesu gise sēn ngum, mu wah͈ ku lafañ ka, ne, Suma dōm, na sa h͈ol dal; baal nañu la sa i bakar.