45 Ndah͈ ngēn mun a neka sēn i dōm i Bay ba cha ajana; ndege mō fenkalo janta am cha kou ña bāh͈ ak ña bon, te di tou cha kou ña jūb ak ña jūbadi.
Barkel cha i defarkat i jama ña; ndege di nañu len tūde i dōm i Yalla.
Chi lile la ñepa di h͈ami ne yēn a di suma i talube, su ngēn sopante.