41 Te ku la buga jeñ nga gūnge ko fu sorey, gūnge ko fu sorey‐sorey.
Ba ñu gēne, ñu feka wā’ Cyrene ku tuda Simon: mōm la ñu jeñtal mu and’ ak ñom ndah͈ mu gadu kura ba.
Te su la kena yubo chi yōn ndah͈ mu jel sa chol, bayi ko mu jel sa mbūba itam.
Mayal ku la dagān, te bul gantu ku la buga aba.