40 Te su la kena yubo chi yōn ndah͈ mu jel sa chol, bayi ko mu jel sa mbūba itam.
Wande mangi len di wah͈, Bu len findu lu bon, wande ku la dōr chi sa leh͈ i ndējor, sopalil benen bi itam.
Te ku la buga jeñ nga gūnge ko fu sorey, gūnge ko fu sorey‐sorey.