Wande ndah͈ du ñu len fakatal, demal cha gēch ga, sani ôs, te japa jen wu jeka fêñ; bo ūbe gemeñ am, di nga cha feka dogit i h͈ālis: jel ko, te joh͈ len ko ngir man ak you.
Su la sa loh͈o mbāte sa tanka moylô, dog ko, te sani ko: mō gen nga h͈araf chi dunda ak lago mbāte di sôh͈, aste am ñar i loh͈o mbāte ñar i tanka, ñu di la sani chi safara su dul jêh͈.
Ka mu joh͈ on jurom i talent ya ñou, te indi yenen jurom i talent, ne, Borom bi, joh͈ on nga ma jurom i talent: yenen jurom i talent angi yi ma chi doli.
Fōfale Yesu ne len, Di ngēn fakatalu ndig man chi gudi gile yēn ñepa: ndege binda nañu, ne, Di nā dōr sama ba, te i nh͈ar i gēta ga di nañu h͈ajātlaku.
Wande mangi len di wah͈, Ku di mere morom am, mungi chi tafār i ate; te ku ne morom am, Dof bi, mungi chi tafār i ate bu rey; wande ku ne, Ēfar bi, di na neka chi tafār i safara’ nāri.