3 Barkel cha ña sufelu chi fit; ndege ngur i ajana di na len lew.
Cha wah͈tu wōwale Yesu tontu, ne, Mangi la gerem, Bay bi, Borom’ asaman ak suf, ndege nuba nga yef yile chi borom‐h͈amh͈am yi ak borom‐sago yi, te fêñal len i gūne.
Te barkel chi ku dul feka fakatalu chi man.
Wande barkel chi sēn i but, ndege da ñu gis; ak sēn i nopa, ndege da ñu dēga.
Wande Yesu ne, Bayi len gūne yu tūti yi ñu ñou fi man, te bu len len tēre: ndege ngur i ajana lew na ña mel ni ñom.
Barkel chi bukanēg bōbale, ba borom am di feka mu di def nōga ba mu agse.
Fōfale Bur ba di na wah͈ ña cha ndējor am, ne, Ñou len, yēn ña suma Bay barkel, dona len rew mu ñu len wājal on cha ndôrte’ aduna si:
Rēchu len, ndege ngur i ajana jegeñsi na.
Te ma ne len, ñu bare di nañu jugeji cha Penku ak H͈arfu, te jēki ak Ibrayuma ak Isaka ak Yanh͈oba chi ngur i ajana;
Yesu ne ko, Ndege gis nga ma tah͈na nga gum: barkel cha ña gisul, wande da ñu gum.