Wande ndah͈ du ñu len fakatal, demal cha gēch ga, sani ôs, te japa jen wu jeka fêñ; bo ūbe gemeñ am, di nga cha feka dogit i h͈ālis: jel ko, te joh͈ len ko ngir man ak you.
Ndege i yōm la ñu judu on nōga cha sēn bir i ndey; yenen i yōm la ñu nit yōmlo; te i yōm la ñu yōmlo sēn bopa ngir ngur i ajana. Ku ko mun a nangu, na ko nangu.
Suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn wor gēch ak jēri ndig sopi bena tubēn; te ganou bu mu neke nōna, ngēn genati ko def mu neka dōm i nāri as yēn.
Wande mangi len di wah͈, Ku di mere morom am, mungi chi tafār i ate; te ku ne morom am, Dof bi, mungi chi tafār i ate bu rey; wande ku ne, Ēfar bi, di na neka chi tafār i safara’ nāri.