X. Bul hemin saa neg i dikando, bul hemin saa jaba i dikando, waala rapas am bu gor, waala rapas am bu jigen, waala nag am, waala mbam am, waala lu mun na neka alalam.
Wande mangi len di wah͈, Ku di mere morom am, mungi chi tafār i ate; te ku ne morom am, Dof bi, mungi chi tafār i ate bu rey; wande ku ne, Ēfar bi, di na neka chi tafār i safara’ nāri.