26 Chi dega mangi la di wah͈, Do fa gēna muk, be nga fey kopar bu muje ba.
Ndah͈ ñar i mbelar du jar bena kopar? Te bena du dānu chi suf te sēn Bay yēgu ko.
Borom am mer, te jebale ko getenkat ya, be ba mu feye lu mu ko leb on yepa.
Fōfale di na wah͈ ña chi chamoñ am, ne, Randu len ma, yēn ñi alaku, dem len cha safara su dul jêh͈, ba ñu wājal on Seytane ak i malāk’ am:
Ñile di nañu dem chi ndān gu dul jêh͈: wande ñu jūb ña chi dunda gu dul jêh͈.