24 Na nga fa bayi sa maye cha lotel ba, te dem jeka marale ak sa morom; cha ganou ga delusil, jebal sa maye.
Suboh͈un yēn, bindānkat yi ak Pharisee yi, nafeh͈a yi! ndege da ngēn fey asaka i oyof ya, te sagane yef i yōn wa gen a rey, mu di njūbay, ak yermande, ak ngum: yile ñom ngēn war on a def, te bañ a sagane yena ya.
Mōtah͈ so di jebale sa maye cha lotel ba, te fataliku fōfa ne sa morom am na amle ak you,