23 Mōtah͈ so di jebale sa maye cha lotel ba, te fataliku fōfa ne sa morom am na amle ak you,
Silmaha yi: bu chi gen a rey, maye gā’m, am lotel ba di selal maye ga?
Na nga fa bayi sa maye cha lotel ba, te dem jeka marale ak sa morom; cha ganou ga delusil, jebal sa maye.
Yesu ne ko, Otul te bu ko wah͈ ken; wande demal wone sa bopa seriñ ba, te jebale maye ga Musa eble won, ndig sēde chi ñom.