20 Ndege mangi len di wah͈, Su sēn njūbay sutule njūbay i bindānkat ya ak Pharisee ya, du len h͈araf chi ngur i ajana muk.
Fōfale ñu h͈am ne wah͈ul len ñu otu mporoh͈al i mburu, wande njemantal i Pharisee ya ak Sadducee ya.
Ku nangu gena gūne niki gile chi suma tur, man la nangu:
Te nistey teg nañu semiñ wi chi rēn i garap ya; garap gu neka mbōk gu mēñul dōm yu bāh͈, di nañu ko dog, te sani ko chi safara.
Du ku neka ku ma wah, ne, Borom bi, Borom bi, di na h͈araf chi ngur i ajana; wande ka def suma mbugel i Bay ba cha ajana mōm reka.