17 Bu len dēfe ne da ma dika fanh͈asi yōn wa ak lu yonent ya wah͈ on; diku ma fanh͈asi wande motalisi.
Yesu tontu ko, ne, Bul ko bañ lēgi, ndege nōgu la ñu ela motali njūbay yepa. Nōgale la bañatul.
Mōtah͈ lu ngēn buga lepa nit di len ko defal, yēn itam na ngēn ela defal ñenen: ndege bile di yōn wi ak yonent ya.
Musa chi yōn wi ebal on na ñu jumat ko ak i doch ku mel ni mōm: you nak, ana lo wah͈ chi mōm?