12 Banēh͈u len, te kontan len lol; ndege sēn yōl rey na cha ajana; ndege nōgu la ñu geten on yonent ya len jītu on.
Ndege Dōm i nit ka di na ñou chi ndam i Bay am, ak i malāk’ am; te chi wah͈tu wōwale di na yōl nit ku neka naka ligey am day.
Su ngēn di ôr, bu len am kanam gu dīs niki nafeh͈a ya; ndege di nañu ñaulo sēn i kanam ndah͈ nit ña gis ne ñunge ôr. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.