8 Seytane yubôti ko fa tūnda wu koue‐koue, te won ko i rew i aduna si yepa, ak sēn ndam;
Ndege ban njeriñ la chi nit, su ame aduna si yepa, te mu ñaka bakan am? wala wan wēchi la nit di joh͈e ndig bakan am?
Seytane nak yubu ko fa deka bu sela ba, teg ko cha kou puj i juma ja,
Ndege Bay ba sopa na Dōm ji, te won ko yef yu mō def yepa: te di na ko won yef yu upa yile, ndah͈ ngēn jomi.